Le lendemain,, c'était une belle journée ensoleillée. Tanor était déjà partie au boulot. Adja était dans sa chambre à se regarder devant le miroir repensant au câlin d'hier soir avec Capi. Marie Jane elle, faisait la vaisselle dans la cuisine. Capi revient tout juste de son jogging essoufflé et tout en sueur..Il monte les escaliers soupirant de fatigue et entre dans sa chambre oubliant de fermer la porte. Il se déshabille, dépose sa tenue de sport sur le lit, enleve sa montre avant de la posé sur la coiffeuse puis se dirige vers la salle de bain pour prendre une douche. Adja qui s'apprêtait à descendre entends Capi prendre un bain et s'aperçoit que sa chambre n'est pas fermée. Elle y pénètre sans faire de bruit et commence à renifler ses habits de sport. Elle fait tombé la montre qui était sur la coiffeuse par accident et Capi entend le bruit. Il demande qui est là ? Mais personne ne répond. Adja s'empresse de retourner dans sa chambre.
En bas, quelqu'un sonne à la porte. Marie Jane va ouvrir et est surprise de voir sa mère.
Aïda:: salamalékoum
Marie Jane:: wa yaye, loy déf fi
Aïda:: xana nga mayma ma doug ba paré sakh,
Marie Jane:: ah dama tite di lou xéw ba diam la
Aïda:: dara xéwoul diam ak salam sa patron la sokhla animou
Marie jane:: kane Adja ?
Aïda:: waw
Marie Jane:: aksil ma woko..lokay doyé yaye
Aïda:: dou sa problème, lidieuntil say affaire
Marie Jane fait entrer sa mère dans le salon le temps d'aller prévenir Adja. Elle monte et frappe la porte {Toc..Toc..Toc} Adja lui dit d'entrer
Marie Jane:: Adja ba dérangé woumala
Adja:: lou xéw ?
Marie Jane:: sama yaye mola sokhla, mingui thi souf thi salon bi
Adja:: Mangui gneuw
(Marie Jane sort et ferme la porte derrière elle.)
Adja:: Faté gén troop té meun dérangé nite. (d'un air hautain)
Capi sort de la douche et remarque que ses affaires ont été déplacés. Il sort de sa chambre, seulement avec son serviette et tombe sur Marie Jane qui sortait de la chambre de Adja.
Capi:: Marie Jane ya doug sama chambre ?
Marie Jane:: Non non chambre Adja la diougué
Capi:: amna kou lal samay bagages
Marie Jane:: Xana djiné yi la kone ? Mane ak Adja gno gui wone thi négam té keur gui gnoune 3 gnofi nék
Capi:: C'est bizarre..wa défaral ma limay ndéké comme d'habitude ma ngui wathi
Marie Jane descend. Adja sort de sa chambre et tombe sur Capi qui est torse nue. Capi est un peu gêné et fait demi tour pour retourner dans sa chambre mais Adja le retient pour lui parler des soi-disant préparatifs du mariage alors qu'elle s'en fou royalement. Tout ce qu'elle veut, c'est le regarder presque nue.
Adja:: Capi pardon viens stp
Capi:: xaral ma ték dara sama kaw
Adja:: non vite fait juste 1mn rek...je voulais t'informer j'ai déjà contacter le traiteur pour mariage bi après dinagn callé rendez-vous pour qu'on se mettent d'accord pour le menu yaw ak Karina fok ngén assisté parce que sén mariage la après tout fok ngén diokhé sén avis sur le buffet, c'est important
Capi:: dieul traiteur téloul Adja, le mariage c'est dans 3 mois
Adja:: "Bongoût Traiteur" c'est le meilleur traiteur actuellement, kép kou am xéw mom ngay wo, motakh dafay saturé tout le temps fok ma tél ko wakh mou tél ma prévoir...yaw lo yakar, mariage dangay bayi bamou dess 1 mois nga soga commencé préparatif yi, dou nonou dé
Capi:: ah donc c'est bon, gor gni mom yoyou xamou gnousi dara yaw gérél rék je te fais totalement confiance so waré déf ay frais tu me dis, je te fais un virement
Adja:: jamais de la vie, sa xéw bi lép loussi war dinako déf ladiou mala dara si xaliss, boul faté Karina danko wara diokh première cadeau, té djiguéne dagn kay téral, lo wara dépensé thi mariage bi rék doli ko thi premiere cadeau bi mane ak Tanor on va tout gérer inchalla
Capi:: bakh na dégu nala
Adja:: wa tay lo beug réré ma diar marché ndoug ko ?
Capi:: Ladial Tanor rék mane mom lou gneuw bakh na
Adja:: dagno meun deuk di lath Tanor mom késsé deukoul thi keur gui nak, wakhal rèk
Capi:: wa xolal lo ndoug bakh na tu sais mane awma loumay bagn
Adja:: yaw dal Capi sa kersa bi dou meusseu dègn, wa bakh na
Capi:: franchement merci Adja guiss na ninga ma takhawo bou bakh awma sa faye vraiment
Adja:: yaw ya bakh rèk Capi, bo mèlone nènèn douma sawar thi say mbir, té boul faté nak rakou Dieukeur, dieukeur la loumala dèfal dafma war
Capi:: bon je te laisse y aller, xamna danga nèk si yone bala malay tardél
Adja:: ok à plus..je dois aller faire des courses sohla wo dara super marché ?
Capi:: non non j'ai besoin de rien
Adja:: ok thi kanam
Capi retourne enfin dans sa chambre et Adja descend au salon pour rejoindre la mère de Marie Jane.
___________________________
Adja:: Maman ça va ba yagofi ?
Mère Aïda:: dédèt légui la aksi
Adja:: Mangui diégeulou dé Marie Jane wakh nama yangui thi souf dima xar mais dama diapone motakh
Mère Aïda:: mo grawoul dé yagoumafi sakh dé pourtant
Adja:: ba diam la rék
Mère Aïda:: ah mane dé Adja affairou Marie Jane momafi andi, ndakh Marie Jane mingui may beug diaxal
Adja:: diaxal si lane?
Mère Aïda:: Marie Jane légui dafay goudé wathi 20h ladane aksi wayé légui 21h day passé doumako guiss..demb sakh pathé la wakh mou dieulsi ko dama yakarni dafay wathi di takhawalou, xam nga Marie Jane béneu bou djiguéne la té deuk bi woroul bandit yi dagno bari
Adja:: pourtant maman dou linga yakar dé Marie Jane taxawalou woul féneu, goudé yimouy goudé temps yi yeup c'est de ma faute mako fi teuyé ba heure bobou..dama yakaron ni amoul problème comme distance bi soriwoul béneu kogn bila
Mère Aïda:: bilay amoul sakh problème wayé xam nga Marie Jane djiguéne la té fi rew mi tolou kou ndiabot dinga sonou motakh malay gnane rék heure wathiam bou dioté nga bayiko mou gnibisi sama xél bi meuneu dal, mane mak la té stress bou bari bakhoul thi mane
Adja:: deug leu maman amoul béneu problème mangui diégeulou bou bakh
Mère Aïda:: amoul akk, bou lolou wèsso nak Adja, Marie Jane temps yi dafa sopékou ma beugone nga wakhtane ak mom
Adja:: sopékou bou démé nane ?
Mère Aïda:: dafa am goné boumouy beugeuntél war ngako xam pathé la toudou
Adja:: pathé waw, dafi dane gneuw diko setsi
Mère Aïda:: mom la, gnom gnar depuis xalé ba légui gnoy andeu ba pathé wakh ni dako beug déf sokhna, yayam sama woleuré la wone dafa guéneu aduna ma gnéwantal xalé bi dafa bakh si mane té beugouma féthi coleuré wayé Marie Jane nar nama ték gathié thi kanamou pathé dé
Adja:: Pourtant gnom gnar guissouma gnou am problème dé
Mère Aïda:: thi problème lagnou deuk, pathé kalamé nama wakh nama amatoul tontou bou nékh thi Marie Jane, wakhal ak mom mou changé, bayi nimouy déf domou diambour bi pathé gor la dé amoul lou beuri wayé gor la garmi la
Adja:: Lolou mom sen vie privé la gnom gnar beugou massi dougou wayé dina wakhtane ak Marie Jane inchalla
Mère Aïda:: wakhtanal ak mom, yaw rouss nala dina la dégeul..wakh nako lou ler, kènén koumou ma andil dou seuy ak mom, té beuss bou bayé pathé dinako bayi aduna ak alahira
Adja:: eup na déf
Mère Aïda:: té bilahi walahi thiaxanouma doumako may kénén koudoul Pathé
Adja:: dina wakhtane ak mom inchalla xélou xalé moko diap rék nga balma nak maman mais dama wara guèneu ni dama am rendez-vous
Mère Aïda:: wa bahna mane mangui gneuw dém
Adja:: nouyoul ma wa keur gua
Mère Aïda:: diapalé mathi rék dom yaw lassi yakar
Adja:: dina wakh ak mom inchalla
Mère Aïda:: nouyoul ma sa borom keur mom tamit kou bakh la kérok tassé na ak mom mou mayma xaliss bou bari
Adja:: dinako dégu
(Aïda s'en va et Adja commence à la critiquer)
Adja:: wa mère bi yabaté woul nak, perte loma sama temps bi yeup thi wakham you gnak fayda yi, problèmou pathé ak Marie Jane louthi sama yone? Xoulo pauvre louthi yonou millionnaire ki énervé nama way, may wakh mounane Marie Jane nay wathi heure...xamo sa bop ak sa brodé bou fouri, badola yi ngein done koulén défal tèranga regretté ko
A l'agence, Tanor était concentré à travaillait dans son bureau jusqu'à ce que Karina l'interromps...
Karina:: je peux entrer boss c'est urgent ?
Tanor:: vas-y
Karina:: Y'a un monsieur qui souhaite acheter un biens, je viens de l'avoir au téléphone
Tanor:: Villa ou appartement ?
Karina:: Appartement, comme ton Planning n'est pas chargé aujourd'hui je lui ai donné rendez-vous à 16h, proposer nako pour mou visiter sunu site internet mais il tient à te rencontrer en personne et vu que c'est un acheteur potentiels, je voulais pas lui faire attendre ça serait pas professionnel de ma part
Tanor:: Tu as très bien fais..donc 16h ok je vais l'attendre..balma nga tok Karina je voulais te parler un peu
(Karina s'asseoit)
Tanor:: comme je te l'ai dis hier soir pendant le dîner contane na torop thi sa relation ak Capi, c'est mon petit frère et tout ce que je désire c'est le voir heureux à côté d'une femme mais une femme qui le mérite vraiment parce que Capi sama rakk la mais sagn na wakh né moma geun, il a un cœur en or mais il a beaucoup souffert après le décès de son ex femme, sonone na torop thi mom bala mo surmonté ndogal bou mètti bobou dalone ko, gnak dafa métti surtout nga gnak sa diabar kone bou démâté ba beugeunté wat bay xalate mariage douma déf loudoul encouragé ko, supporté ko épaulé ko..damalay wakh gnari bat nak premièrement dinkeu nalako deuxièmement je veux pas le voir souffrir, si ça arrive je te le pardonnerais jamais ça mom je veux que ça soit clair et nette entre nous, tu as intérêt à le rendre plus heureux qu'il ne l'est maintenant
Karina:: t'inquiète pas Tanor, dothi am dara loula métti, likay sonal dou meusseu diogué thi mane inchalla
Tanor:: yamako promettre, j'espère que tu va joindre les paroles aux actes, damay tok dilén sétane
Karina:: tu sais mane je te comprends aussi en tant que grand frère tu cherches à le protéger mais rassure toi, il a eu un passé douloureux et j'en suis consciente donc mane apportél ko bonheur ak tranquilité d'esprit rék moma war, gnanal lén gnou rék
Tanor:: dina bakh inchalla, je te fais confiance
Le téléphone de Tanor sonne avant qu'il ne termine sa phrase: c'est Adja qui l'appelle.
____________________
Tanor:: allô Adja
Adja:: oui bb cv ba dérangé woumala ?
Tanor:: non non qu'est-ce qu'il y'a
Adja:: je voulais que tu libère Karina damako beugone invité resto déjeuner, on a pas pu parler hier soir et j'ai des choses à lui dire entre fille s'il te plait
Tanor:: non y'a pas de soucis, elle est en face de moi je te la passe
(Tanor donne le portable à Karina)
Adja:: allo Karina c'est Adja no déf ?
Karina:: Cv bien Adja nakamou
Adja:: en fait depuis qu'on se connaît on parle juste vite fait et vu qu'on va devenir belle sœur ça serait bien qu'on se voit plus souvent, qu'on échange, motakh je voulais t'inviter à déjeuner j'ai demandé à Tanor de te libérer
Karina:: ah lolou mom loumay nékh la, amoul problème je te rejoint tout de suite envoi moi l'adresse rék ma gneuw boul wakh dara yaw
Adja:: d'accord ma gui lay yoné adresse Resto bi légui
Karina:: wa bakh na
Adja:: passe moi mon mari
(Karina redonne le portable à Tanor)
Adja:: allô mon amour
Tanor:: oui
Adja:: wa je te laisse Lo beug réré tay ?
Tanor:: tay est ce que do lath Capi
Adja:: Capi la ndieuké lath mounima ladial Tanor
Tanor:: wa kone xolal rek yaw ce que tu as envi mane mom franchement tay j'ai pas un envi particulier..lou gneuw ma dieul
Adja:: wa d'accord à ce soir
Tanor:: ok à ce soir
_____________________
Marie Jane qui préparait le petit dej de Capi dans la cuisine reçoit l'appel de Pathé.
____________________
Marie Jane:: allô !
Pathé:: allô oui bb, comment tu vas ?
Marie Jane:: ça va
Pathé:: domani danga mér ba légui dé
Marie Jane:: pathé xam nga bou bakh ni heure bi damay liguèy je suis trop occupé, premièrement tu m'appelle deuxièmement doyé woma dara lou am importance
Pathé:: wa d'accord na, mala togne balma akk, mane diam la paix lay weur dé
Marie Jane:: wakhal lomay doyé bala malay coupé
Pathé:: tu sais ça fait longtemps on a pas passé des moments seul toi et moi, on se voit pratiquement plus je me suis dis ça serait bien gnou dém Ciné après dém lékki glace dieul air, ça nous fera du bien en plus temps yi yeup on fait que se disputer
Marie Jane:: pathé damala ndirou kou xiff ? No sincèrement wahal rék damala ndirou kou am envi lékki glace wala kou beug dém Ciné, yaw bo amé diote mane awma diote je travaille 24h/24 du lundi au dimanche yaw nak goro yatto...affaire de Ciné, dieul air yako tal boudé dafa am lénén losi ték nga wakh bo paré ma coupé
Pathé:: bakh n'a c'est bon
(Marie Jane raccroche)
Marie Jane:: il m'énerve ki
Marie Jane prend le plateau puis se dirige vers la salle à manger. Capi était déjà installé sur la table entrain de l'attendre.
Capi:: bodone Docteur sa malade dé na bou yagu
(Marie Jane dépose le plateau)
Marie Jane:: bou dieulé temps rék xamal ni dafa nara nékh
Capi:: meusso fi togou lou nékh
Marie Jane: (éclate de rire) woy sama nday, doumala tontou yaw wakhtane nga beug
au même moment Capi voit son téléphone sonné. Il regarde et y'a écris Karina♥️.il décroche
_________________
Capi:: mon cœur
Karina:: allô bb
Capi:: naka matinal bi ?
Karina:: ça va ni rék..loutakh tay gneuwo bureau ?
Capi:: j'ai pas beaucoup de travail enplus dama geudione dèf sport matinale, j'en avait besoin
Karina:: wa askip c'est bon pour la santé du cœur
Capi:: non mane mom ça m'apaise vraiment, travailler toute la semaine c'est fatiguant fok gnouy dieul bén jour ordinaire pour nopalou
Karina:: on devait se voir mais ça sera pour plutard actuellement mangui ni je vais aller déjeuner avec Adja, elle m'a invité comme c'est la première fois du coup je pouvez pas dire non
Capi:: non y'a pas de soucis on se verra l'après midi
Karina:: Ça me fait mal nak xam nga mane meuneutouma tok lou yagu té guissou mala
Capi:: danga nobaté nak yaw
(Karina rigole)
Capi:: profite bien de ton déjeuner Adja mom kou bakh la amoul béneu problème vous allez bien vous entendre
Karina:: waw mom minou mako mais kou ouverte la
Capi:: non elle est unique amoul moron, dinga thi xam dara
Karina:: wa je te laisse yangui lèk rèk xana dangay ndékki
Capi:: wa guiss nga dé heure bi la ndèki tay, Marie Jane depuis Fadiar ba légui mankay top defral ma ndéki mou may daw lo ki dafma yap
Karina:: souma seuysé sa thiono diékh, nopil bama gneuw rék
Capi:: xam na lolou..allez bisous bonne journée
Karina:: gros bisous je t'aime porte toi bien
Capi:: moi aussi je t'aime bye
______________________
Capi raccroche. Pendant tout ce temps qu'il parlait au téléphone Marie Jane la fixé de regard.
Capi:: Yaw lane la ? Lomay xolé ni ak sa beutou deumeu yi, danga con torop yaw ?
Marie Jane:: Ya meun soss té meun yakeu der wayé meuno ma diaxassé ak Karina, néga da ngén beugeunté nonou bay wakh ay bisous je t'aime
Capi:: gno tay, yaw beugeunté wo yaw, ani pathé ?
Marie Jane:: sama vie privé louthi sa yone ?
Capi:: (éclate de rire) Marie Jane yap ngama nak temps yi, wa démal sa yone, démal rakhass say bol wala nga dém togui agn bi
(Quelqu'un sonne à la porte, Marie Jane va ouvrir: c'est Tata Rose)
Tata Rose est la tante maternelle de Tanor et Capi. Elle habite à Saint-Louis avec son époux mais vient leur rendre viste 2 ou 3 fois dans l'année. Elle n'a pas d'enfant c'est pourquoi elle aime autant ces neuveux Tanor et Capi et les considères comme les fils qu'elle n'a jamais eu. Bref, Marie Jane est contente de la revoir.
Marie Jane:: ehhh Tata Rose
Tara Rose:: Marie Jane namone nala (accolade)
Marie Jane:: ay Tata mala raw aksil ba sono thi voyage bi ?
Tata Rose:: bilay sonou na dom, damay dieum mak tank yi bakhatoul
(Capi entend sa tante et se précipite pour l'accueillir)
Capi:: ehh Tata yaw boy gneuw doma wakh ma dieulsi la
Tata Rose:: surprise lalén beugone défal (rigolant)
Capi:: surprise bi nèkh na mais soma wowone au moins ma dieul sila garre ba
Tata Rose:: damalén done bagna sonal dom, wayé sa auto beulé am clime moma geuneul Taxi you tang yi
Capi:: Ah vraiment aksil..Marie Jane yoboul bagage yi thi chambre d'invité bi
(Marie Jane emmène les bagages)
Capi:: Tata mou défaral la nga ndéki
Tata Rose:: boulko dèrangé ndéki na thi yone bi
Capi:: bayil mou défar nga ndéki wat voyage bi dafa sori
Tata Rose:: bilay sour na matouko, nama may lou séd rék ma nane
Capi:: wa aksil thi salon bi
Tata Rose:: ani Tanor mom ?
Capi:: Tanor mingui bureau tay mom mafi nék
(Tous les 2 entrent dans le salon puis s'installe)
Tata Rose:: ani Adja sama goro bou bakh bi
Capi:: Adja mom dafa guénone mais xamna soriwoul légui mou gneuw
Tata Rose:: yaw dal tay yafi dèss
Capi:: wa guiss nga dé
Tata Rose:: ah nonoula c'est bien keur mom kilifeu yeup warounou démano
(Marie Jane arrive et sert du jus bien frais à Tata Rose)
Tata Rose:: ah Marie Jane way, xalé bou yarou bi wa kagn ngay am dieukeur nak bama langal la
Marie Jane:: ah xamna yagatoul
Tata Rose:: ah mangui gnane dé, goor bou bakh gneuw tèral la
Marie Jane:: amine (en quittant la pièce)
Tata Rose:: Capi no déf nak? Ba yangui si diam ?
Capi:: sant yalla bou wer Tata
Tata Rose:: mane dal demb si goudi lama Tanor wo téléphone nima Capi dafay remarié wo maniko lolou mom nouvelle bou nékh la..ma contante thi lol sakh motakh ma fadiarou doug si horaire bi gneuw uniquement pour félicité la guissalé sama futur goro
Capi:: wa guiss nga dé affaire bi mom dou lougnou wadj sakh, on l'a décidé ça tout naturellement
Tata Rose:: ahhh alhamdulila, c'est bien yalla bahna ba diongoma na rék boulma fi andil goro bou gnaw dé
Capi:: du tout book guissé mom dinga apprécié. Xalé bou bakh la vraiment kou am yar, kou téyi
Tata Rose:: qualité yoyou mom djiguéne bouko am djiguéne bou bakh la wayé ba listaxar ngén xol digeunté bi
Capi:: Tata mane dal yoyou geumoumako
Tata Rose:: ah sila bok nak seuy bala gnoukay tak dagn kay xol sèt ndakh sén weurseuk andeu na, dou dîner wayé thiossanou mam la
Capi:: wa bakh na comme gneuw nga après nga gérer lolou yeup yay sama yaye
Tata Rose lève la tête et voit la photo de Fama (première épouse de Capi)
Tata Rose:: ndeysane sama goro bou bakhone bi, geunone thi mane, beugone ma dima wo dima némékou...dane ma yoné soukeur koor, yalnako yallah yeureum té xaré ko aldiana
Capi:: amine, amine way
Tata Rose:: amna sama ngeureum dé téla dém rèk lay dioy thi mom wayé nak yallah moy bur moy xol louko nékh mou déf wayé yallah boula xagné Dara diapal ni dinthial nala lènén lou dakk lolou
Capi:: deug leu
Tata Rose:: Lou métti lo mougn dafay dièkh, ndaw si la yalla bolèl nak nga diap ko bou bakh, fonk ko yaw sakh kén doula gnakh ndakh goor bou meun gor diabar nga damalay doli rék diapaléko bou bakh djiguéne matoul
Capi:: inchalla tata
Tata Rose:: wa mom louy toureum sakh ?
Capi:: karina la toudou
Tata Rose:: ahhh sama goro bi toureum nékh na mashala yakamti nako guiss lol sakh
Capi:: inchalla boussi kanamé rék ma tal sama auto gnou dém ba keureum nga guiss ko
Tata Rose:: défal lolou dima ma nékh...mashala yèn guissa golén dara, xéweul yi dina geuneu yokou ndakh sén yaye dako liguey sèn keur Baye, dara diomou lén, té dolén meusseu gné sèn bèneu morom thi katanou sunu Borom
12h47
Karina vient d'arriver au Resto où Adja lui a donné rendez-vous. Elle s'apprête à entrer quand Adja lui fais signe de la rejoindre sur le parking.
Karina:: Adja cv ? dinga ma méré dé j'ai eu un peu de retard, embouteillages yi gnoma teuyé wone thi yone bi, ba yagofi ? Wona Capi sakh pour informé ko on va déjeuner ensemble
Adja:: Déjeuner andi woumafi, masla andi wouma, diamassanté andi woumafi
Karina:: Lou xéw Adja boulma titeul?
Adja:: Ba xam ngani mariage bi yaw ak Capi dou am, guéné ko sa xél vite fait
Karina:: Pourquoi lolou ?
Adja:: damako xam rék, soumala wakhé mariage bi dou am rék diapal ni dou am
Karina:: Adja meunou mala geum, pourquoi tu me dis tout ça ?
Adja:: gnak ma xam ak gnak xam lima capable motakh meuno ma geum, mane may kiy empêché mariage ndakh de 1 nékhoma, de 2 Capi doussa mass té doussa classe
Karina:: Ok pour mane sakh tu blague mais kou xol sa kanam xamni fowo, sa deug nga nék...Yaw Adja danga nékh nékété, yaw kone ninga mèl ? Décidément dinga estimé nite mou wakh rék wathié bopam
Adja:: Ni la mél, né la mél lolou touti nga pour lidieuntiko lima beug moy tu laisse Capi tranquille bala may dioug thi say mbir, boulma takha guéné sama djiko deumeu bi, yangui may dégeu ?
Karina:: kone dal thi gatal danga ma xép ?
Adja:: Ma chéri xana dègo limala wakh...yaw yama nékhoul té do dougou sama keur bafay am chambre
Karina:: wayé danga faté Capi moy beug té moma demandé en mariage
Adja:: Danga yakar ni xawma ni xaliss nga topé Capi, wayé dou yombé nonou diapal ni sa plan yeup tombé na a l'eau ndakh douthi dal
Karina:: Nite ki dé ninga mél lolou ngay yalarni la gneup mèl, xana yaw xaliss nga topé Tanor
Ajda:: ce que tu pense je m'en fou royalement ma chérie boudé xaliss nga beug té nga bayi ma diokh la ay millions nga faté Capi bala ngay perte ndakh mariage bi dou am lolou mom dafma ler
Karina:: guiss nga Adja que ça soit la dernière fois ngamay wo dima wakh sa wakh yi, lane moy nday xaliss ? mane dama xol sén alal
Adja:: Bayil sagou bi kay ma diokh la chèque blanc nga déf thi montant boula nékh
Karina:: Lingama wakh yeup nak diapal ni Capi dinasi diote, bèteu ngama torop nak té rouss nala
Adja:: Pour yaw Capi loko wakh thi mane lou gnaw dinala geum? Wakhal xol liy métti thi kane lay diougué, bo amé fite rék wakh ko, proposé nala xaliss nak beugo sa pertement la mais Capi mon dinko bayi par À ou par B sinon Lo guiss mane la, lingay wow beut, thiaga bi nga done, xana gor da manqué senegal
Karina:: Mako def, mane mi takhaw continué dila déglou kén tognouma, ma togn sama bop, heureusement nak binga ma wané sa djiko Adja dieureudieuf, khamo sakh linga dèf
(Karina lui tourne le dos et s'en va)
Adja:: yaw xamoma sakh, té xamo lima capable..ay minutes ma réglé sa cas
Adja sort son téléphone et compose un numéro
___________________
Adja:: allô Izo, fo nék ni actuellement?
Izo:: mangui Thies
Adja:: xawma loy déf Thiés mais bayil lép lo diapone gneuw Dakar c'est urgent j'ai un petit problème té yaw rék yama si meun diapalé
Izo:: problème bi noumou toudou ?
Adja:: problème bi Karina Mbaye la toudou, té beugouma mou téré ma nélaw, damako beug réglé noumou geuneu gawé
Izo:: ok, mangui gneuw légui, souma aksé nala wo wakh la finga may fèk
(Adja raccroche)
À Suivre...
Izo c'est le complice de Adja dans toutes ces manigances. C'est un délinquant sans vergogne qui ne cherche qu'a se faire de l'argent. Il tuerait sa mère pour de l'argent.
Dans le chapitre 3, ne ratez pas le plan de Adja et Izo pour séparer Capi et Karina.
👇👇👇👇👇👇👇