Saar 16
*****Adja****
-Adja loy mel ni kou guiss revenant ni...
Khalil ware nay choquer ci limako guiss moumay mbalak. Mais grawoul mako bal.
-Dina choquer kat. Dama la kharoul wone di.
-Amone envie défal la surprise rek. Bimay guéne sougnou keur sank sama yaye loume ma wakhoul dako faté mais dama amone torope envie guiss leu pour nane damay nonpalikou wala damay khare ba soubeu.
-Surprise bi mat na. Wa li lane la ???
May lathier di djokhognalé béne valise. Deme tok ci wetou Khalil.
-Douma diogué France difi gneuw ak ay lokhay naine, séne seurithia.
-Biguay gneuw magui ko done wakh que tégougnoukoko.
Sama yaye mome daguay warou. Khalil sou fi gneuwone ak ay lokhoy naine ba ma wakh ko bopam.
-Non maman, keur gui sama keur leu. Louma fi défoul c'est parce que damako amoul.
-Wa sama parfum bi mba dieunde guako.
-Ay Adja !!!
Sama yaye khame nani bou khamone mbarane gou méti gui ma néké daf may ray ma dé.
-Maman grawoul ki mine na li mome. Sa parfum bi la gneukeu lindieuneti. Souma ko beugone faté sakh doma ci bayi, diguamako fatéli fo toleu.
-Bima guissé pub bi la né, non bi il faut que ma ame ci.
-Pourtant ville feke ko fa dé.
-Khame na lolou mais dafa cher.
-Ame sa parfum...
Mou diokh ma sama parfum Dior-j'adore.
-Ame naigne parfum bou bess... Fanta diok di féthie.
-Yow nak dagua beugue ma rayla. Lalale sama parfum rek.
-Légui doko ci may ?
-Khalil li dou parfum khalé. Boutique ba ame na parfum 1000frs naci dieunde.
-Fanta khame gua noy def, daguay bayi bame ligueyi gua sathie ci.
-Yow nak dagua beugue ma ray ko. Déjà rek haut bi mou sol mako mome. Téré nako samay yéré ba sone mou bagne.
-Adja bone gua.
-Yayeboy nak ya gueuna khame ni bonouma. Fanta ci bopam la khamoul foume ma topé.
-Yay taw, té kouy taw werou sa kaw.
-Dégueloule sa yaye wakh nala deugue guou werr.
-Wa fo dieum ???
Khalil dé diogue ma diape ci lokho bi.
-Ni gua may guissé ni, magui né taate. Mandi la def ak ay nelaw. Il faut que je repose.
-Do khar ma défaral gua rerr ?
-Non diarouko nopalikoul. En plus léke na avant may gneuw.
-Ok.
Ma diogue Khalil tago, sama yaye remercierko gnou guéne makoy gougué.
-Lou takh tay garerwo ci bounte bi ?
-Garer ci bountou gua khamé sama auto surprise bi yakou. NI gua def sa kanam bi bigama guissé diare na lou nek.
-Bale nala gua may togne.
VOUS LISEZ
Kéne kou mel ni yow
RomanceChronique bou bess bo khamené wolof la nitt gniy lak. Amouma intention diangual nitt gni alphabet wolof, déjà mane bien que diangue nako maîtriserwouma ko. Lima ci djoubelou moy bind chronique bo khamené nitt gni dagnouy wakhtane comme nigne koy déf...